BayeInternational
*500 musulmans les plus influents au monde, la Fayda Tidjaniya encore à l'honneur*
Cheikh Ahmed Tidiane Aliou Cissé toujours dans le *Top 50* ! A la 26e place de l'édition 2024 parue ce jour, l'Imam de la Grande Mosquée de Médina Baye fait encore honneur au Sénégal à l'instar du Khalife général des Mourid Cheikh Mountaha Mbacké dans la rubrique des guides religieux, Sadio Mané dans le sport et Youssou Ndour en Art et culture.
Télécharger la nouvelle parution
https://bit.ly/m5002024free
Cheikh Moubarack Wade
Cheikh Mouhammad Bachir Ndao - Gamouwat -
Tague Yonente ﷺ
🥰
*MERCI DE SUIVRE NOTRE DOCUMENTAIRE SUR LE MOUVEMENT BAYE INTERNATIONAL PAR GÉNÉRATION BARHAMA NIASS*
DOCUMENTAIRE BAYE INTERNATIONAL Rejoignez cette chaîne pour bénéficier d'avantages exclusifs :https://www.youtube.com/channel/UCgsEjry2G1gwYCnR7O2W3Vg/join
MERCI DE SUIVRE NOTRE DOCUMENTAIRE SUR LE MOUVEMENT BAYE INTERNATIONAL PAR GÉNÉRATION BARHAMA NIASS
DOCUMENTAIRE BAYE INTERNATIONAL Rejoignez cette chaîne pour bénéficier d'avantages exclusifs :https://www.youtube.com/channel/UCgsEjry2G1gwYCnR7O2W3Vg/join
Pour toute personne voulant contribuer ou participer, appelez sur les numéros sur l’affiche ou contacter le +221777150202 par Whatsapp.
Leadership politique dans la Faydha : l'ambitieux programme de Baye Networking dévoilé. ⋆ ATLANTICACTU.COM Sénégal Atlanticactu/ Kaolack/ Abdou Khafor Camara Les leaders politiques de la Fayda ( LPF), une plateforme initiée par Baye Networking ( Réseau professionnel des disciples de Baye Niass ), étaient en conclave ce vendredi à Kaolack. ” Le programme veut fédérer tous les acteurs politiques ...
En partenariat avec la Jamhiyatu Ansarud-din, le Baye Networking votre réseau professionnel lance une grande campagne de recensement professionnel des disciples de Baye à l'occasion du Mawlid International à Médina Baye. Rejoignez notre équipe de 100 volontaires pour relever le challenge!
S'inscrire pour devenir volontaire:
👇🏽
https://forms.gle/mJZRKeUAUZAWePEAA
Barham Day ce Dimanche 19 Juin au Grand Théâtre National de Dakar ⭐
Venez nombreux.
Tawfekh et Tayssir ci Barkeh Baye ak Bayam. Amine
La prière de Eid à la grande mosquée de Almadies 2 sera diffusée sur cette page dans quelques minutes inch'Allah ! Restez connectés.
Dewenati
[🔴LIVE] Suivez la 60ème édition du Gamou de Dieuppeul en direct du théatre national Daniel Sorano Découvrez toute l'actualité sur http://www.walf-groupe.com/
L'état de Kanu démarré sa célébration de Baye Niass
Waadial Gamou Nigeria
Baye néniou :
Nangua am téguine sa diguenté ak Yallah.
وَإِنَّكَ لَعَلى خُلُقٍ عَظِيمٍ
« Té néke na si yow ay djikos you kawé »
Djikos you kawés yi bissi djitou, moy ragal Yallah.
Mo takh mani :
وأنني بالمتقى أباهى
«tè mane mangui titeuro si kou ragal Yallah»
Ragal Yallah, ak nougn ko meunta firé, moy dieufé ndiguel bayi téré, si biir ak si biti, si wét ak si mbolo :
فَاتَّقُوا اللَّهَ مَا اسْتَطَعْتُمْ وَاسْمَعُوا وَأَطِيعُوا وَأَنفِقُوا خَيْرًا لِّأَنفُسِكُمْ
di fatalikou Yallah dayaman té doko faté mouke :
اتَّقُوا اللَّهَ حَقَّ تُقَاتِهِ وَلَا تَمُوتُنَّ إِلَّا وَأَنتُم مُّسْلِمُونَ
Fékhé ba dara loudout Yallah dou tokhe si sa khatir dilé né béne noki la :
إِنَّ اللَّهَ يُحِبُّ الْمُتَّقِينَ
Kone tewloul sa borom.
Say mbokes si tariqa bi nak, magal lén ndakh gnom niépe, ay walious lagn té Yallah mo wax ni :
مَن عادى لي وليًّا فقد آذنتُه بالحرب، وما تقرَّب إليَّ عبدي بشيء أحب إليَّ مما افترضتُ عليه، وما يزال عبدي يتقرَّب إليَّ بالنوافل حتى أحبَّه
Kone képe kouy matal faratam té sakhe sii ay nawafilam yamou diayanté mouy toude Yallah si waxtou yagn tane, kou Yallah beugue la, magal ko nguir magal Yallah.
Soufél waliou, moy diémeu Soufél lou Yallah magal, té kouko diém, yow la Yallah di Soufel.
Gnagnou khassal nakh ( Mouqaddams yi ak Shouyoukhs yi), tope lén ndakh Yallah mo wax ni :
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا أَطِيعُوا اللَّهَ وَأَطِيعُوا الرَّسُولَ وَأُولِي الْأَمْرِ مِنكُمْ
Kone topelén lou war la si yow
إِذَا
« Ndém »
شَرَعْتَ
« tabbi ngua »
فِي
« Si »
ادِّكَارِ الْوِرْدِ
« Diangue wird bi »
فَلَازِمِ
« Nangua takho »
الْأَدَبَ
« Téguine »
قَدْرَ
« Kéme »
الْـحَدِّ
« Dayom »
تَأَدَّبْ
« Ngua tégguiné »
فِي ظَاهِرٍ
« Si lou fégne »
وَبَاطِنِ
« Ak si lou neubou »
بِهِ
« Si lolou »
يُرَقَّى
« Lagnouy yéguelé »
الْـمَرْءُ
« way ( nit) »
لِلْمَوَاطِنِ
« Dieum si wathiouway you kawés yi ( maqamats yi »
Maqamats yoyou gnoy yane ak noula fa Adab di yéguelé ?
…À Suivre…
Gnouniko : Baye, diouli si ndielbénou waxtou, loutakh ngua siy insister ?
Mouni :
Ndielbénou waxtou, nguermandé Yallah la, digue waxtou, yeurmandé Yallah la, moudieug waxtou, ndiéguelab Yallah la.
Gni néke si nguermandé Yallah, gnognou sén dieuf lougnou nangou la té lougnou tague la
Gni néke si yeurmandé gui, Yallah lén yeureum rek yatal waxtouwi nguir woyofalal lén
Gni néke si ndiéguelam, Yallah lén bale rek wayé daan warone na si gnom.
Gniy diouli si ndielbénou waxtou, moy gni djitou
Gniy diouli si digue waxtou, moy gni digue domou
Gniy diouli si moudjieug waxtou, moy gniy togne sén bakane
Si waloum diouli, diame bou mat bi gnétes waxtou gnoko niéwal :
Waxtou biko Chariatou sokhla moy waxtou diouli farata, mou diouli ko bou dioube
Waxtou biko Wilayat sokhla, moy déf ay nawafils aki ndolal
Waxtou biko Ma’arifatou soxla, moy mou sélal dieufam yépe, dindi loudout Yallah si dieuflantém ak Yallah si mbolém waxtous yi
Gnaka diouli si waxtou, gnari haq gadou nguako :
Béne bi meun nguako féy
Béne bi doko féy mouke
Haq bi la warone si waxtou bobou si beus bobou, mou diouli bi, meun ngua ka féy wayé téréwoul, togn ngua waxtou bingua féyé si mom diouli gui, ndakh amna loula warone si mom.
Haq bi la warone sa diguenté ak waxtou bobou si beuss bobou mouy taxawal djouli si mom ndakh Yallah moko ko sédone, doko féy mouke ndakh waxtou bobou dotoul déloussi mouke.
Té waxtou wi, danala ladj Haqqam yawmal Qiyyam, niko Ibn Ata’Allah waxé si Lata’if.
Gnata waxtou ngua amél Haq ?
Kou yégue si Manzila Tumaninatou nak, boke ngua si Khass yi, sa Imane matna, kone dara waroutla loudoul diouli si waxtou, louko moy gnaké ngua téguine ( Adab) gnéwal Qadara bi ndakh :
فَإِذَا اطْمَأْنَنتُمْ فَأَقِيمُوا الصَّلَاةَ إِنَّ الصَّلَاةَ كَانَتْ عَلَى الْمُؤْمِنِينَ كِتَابًا مَّوْقُوتًا
Fafham.
Al Arifou ibn Waqtihi.
Waarid bi goude na wayé gnou yémalé ko fi 🙏🏽
Yobeulou At mou bess mi - Rappel
La Mission de Baye
Gnouniko : Baye, lo beugue ?
Mouni :
يُحْيِى بِي العلم وَالسنة آلَّتِي أَمَاتَهَا الْجَهْلُ
« Ressuscite( Allah) , par moi, la connaissance et la tradition(prophétique), qui ont été tuées par l’ignorance »
« Dékilal ( yow Yallah), si mane, kham kham ak Sunna ( Yonente) yi ngua xamni rér réyone na léne »
Gnouniko : loula fi takha nieuw ?
Mouni :
اوجدنا حَقًّا لِجَبْرِ الكسر
« Je ne suis venu en vérité, que pour réparer les cassures ( de la religion) »
« Gneuwouma, si deugue, loumoy nguir diang dames dames yi ( si diné) »
Gnouniko : lolou nokoy défé ?
Mouni :
أحي العلوم كذا أحي المارف لا ميل للشطح والدعوى و لا الكذب
« Je revivifie les sciences de même que je revivifie la connaissance sans aucune inclination à l’exagération ( dire des shatahats) ni à la revendication ( de stations) ni au mensonge »
« Mbir mom danama dékal kham kham yi naka may dékalé Ma’rifa ( kham Yallah) té dét may adji diéngue dieum si wax ay Shatahats, dou thiaguéne wax lou amout »
Gnouniko : Baye, say talibés nak ?
Mouni :
لَا بُدَّ أَنْ تُقَدِّمَ التَّعَلُّمَا فَكُنْ لِـشِرْعَةِ الْإِلَــٰـهِ مُحْكِمَا
« Il faut vous obligatoirement commencer par apprendre ( la connaissance islamique) et être des savants imprégnés de la Charia d’Allah »
« Lou war la si yén nguén tambalé si diangue ( xam xamou diné) té nguén néke gnouy khérégné Charia Yallah »
فَالْعِلْمُ عُمْرِي هُوَ إِمَامُ الْعَمَلِ كَمَا أَتَى عَنْ طَهَ خَيْرِ الرُّسُلِ
« Car, je le jure par ma vie, la connaissance doit toujours précéder l’acte, comme nous l’a appris Ta-Ha, le Meilleur des Prophètes »
« ndakh, wat nako si sama dounde, xam xam moy ndjitou dieuf , naka gnouko khamalé Ta-Ha, ki geun si Yonentes yi صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ »
Gnouniko : Baye, yén sayi gnou dégue nit wotéwo sa talibé di wax ni Charia yeufou ham la ?
Mouni :
بظاهر الشرع والنور المبين أربي السالكين بلا شك ولا ريب
“C’est par la Charia claire et La Lumière éclatante ( La Sunna) que j’ai éduqué ceux qui ont emprunté ma voie de sorte qu’il n’aient aucun doute ni tergiversations “
« Danama yar, way sobou gni si mane, si Charia bou fégne ak lér bou bir ( Sunna) ba dougnou s**i saka dougnou déflé »
Gnoko déguando.
Nagne délou Kossi.
C’était un petit rappel et une clarification pour ceux qui ne savent pas que Baye fowoul, folouwoul.
Gnou délouwat si Rouhoul Adab …..
Ziarra Cheikh Mouhammad Bachir Ndao
السلام عليكم ورحمة الله وبركاته
La Ma’rifa n’est pas intellectuelle mais expérientielle.
Ne pensez pas que ce que nous disons est La Ma’rifa, loin de là.
Le mot « douleur » n’a de sens pour vous que quand vous avez une fois ressenti la sensation de douleur, « l’amour » pareil, et il en va de même pour tout mot exprimant une notion sensorielle.
L’expression « Il faut le vivre pour le comprendre » prend tout son sens dans le domaine de la Ma’rifa.
Ceux qui s’arrêtent à l’intellect, aux mots ainsi qu’aux significations, n’arriveront jamais à appréhender ni à « visualiser »l’extinction(Fana’) du vivant durant sa vie ou la montée( taraq-qi) d’une entité ayant toujours les pieds sur la terre ainsi que la transformation ( tajalli) d’un être dont la forme visible reste inchangée.
L’imagination n’a pas de place dans la Ma’rifa, c’est La Science Certaine par l’Experience.
السلام عليكم ورحمة الله وبركاته
Ruhul Adab 7
Baye néniou :
مُكَمِّلًا
« Nguay adji matal »
شُرُوطَهُ
« Ay chartams »
الْـمُقَرَّرَهْ
« Ya di yougnou saxal »
Tariqa bi da am ay chartes yo xamni, kouko mataloul, boko si :
-Ba si djitou, moy matal diouli diourom.
Ma bamtouwat :
أَقِيمُوا الصَّلَاةَ
« Takhawal len diouli mou dioube »
Képe koudout diouli téy askan bopam si tarikha bi, mom mo si néke wayé tarikha bi dégne na si mom bou yague.
Koudout dioulit meuno diape tarikha tidiane.
- soko diapé, dotoko bayi ba banguay dé.
Yallah dafa diglé matal say engagements kone so diayanté ak Yallah si nafawil yo yéné sakhal, liy farata si yow moy ngua amatal sa engagement.
Yallah néna :
وَأَوْفُوا بِالْعَهْدِ إِنَّ الْعَهْدَ كَانَ مَسْئُولًا
« Té nanguen matal séni engagements ndakh danagn lénko ladj ( Yawmal Qiyyam) »
وَبِعَهْدِ اللَّهِ أَوْفُوا ذَلِكُمْ وَصَّاكُم بِهِ لَعَلَّكُمْ تَذَكَّرُونَ
« té nanguen matal séni diayanté( engagement) ak Yallah, lolou La len diguel, héyna yén nguen boke si way fatalikou gna »
وَأَوْفُوا بِعَهْدِ اللَّهِ إِذَا عَاهَدتُّمْ وَلَا تَنقُضُوا الْأَيْمَانَ بَعْدَ تَوْكِيدِهَا وَقَدْ جَعَلْتُمُ اللَّهَ عَلَيْكُمْ كَفِيلًا إِنَّ اللَّهَ يَعْلَمُ مَا تَفْعَلُونَ
« Nanguen matal sen diayanté ak Yallah guanaw banguen ko diayanté et boulen wor guanaw ba nguen waté té dieulone Yallah mouy sén sédé. Yallah adji xam la séni dieufs »
مِّنَ الْمُؤْمِنِينَ رِجَالٌ صَدَقُوا مَا عَاهَدُوا اللَّهَ عَلَيْهِ فَمِنْهُم مَّن
قَضَى نَحْبَهُ وَمِنْهُم مَّن يَنتَظِرُ وَمَا بَدَّلُوا تَبْدِيلًا
« Néke na si way geums gni goors yo khamni deugou nagn si sén diayanté ak Yallah. Yéne si gnom diote nagnou sen thiakoutef, yéne si gnom diotagougnko té sopiwougn dara ( si sen diayanté) »
Ak yénéni ayats yo xamni, indiko dana goude wayé matal koleuré, respecter sa engagement, Lou war la.
Kone kou khass ba diayanté ak Yallah si sakho wird bi, warato ko bayi ba banguay dé.
- Dingua bakhé say wadiours sougnouy dounde ( gnouy dioulit ou pas) sougnou fato dingua sakh dilén nianal ( soudé dioulit lagnou)
Ganaw wédi Yallah, bakar bi geuneu mague moy deungué say gnaris wadiour.
Topal Al Quran :
Fou Yallah waxé si tope Yallah, tég na si bakhé say gnaris wadiour
وَقَضَى رَبُّكَ أَلَّا تَعْبُدُوا إِلَّا إِيَّاهُ وَبِالْوَالِدَيْنِ إِحْسَانًا إِمَّا يَبْلُغَنَّ عِندَكَ الْكِبَرَ أَحَدُهُمَا أَوْ كِلَاهُمَا فَلَا تَقُل لَّهُمَا أُفٍّ وَلَا تَنْهَرْهُمَا وَقُل لَّهُمَا قَوْلًا كَرِيمًا
« Té sa Borom dogual na « Boulen diamou koudout mom et nanguén bakhé sén gnari wadiour; sou kéne si gnom wala gnom niar nieupe doné maguét si sa wét, sou boba boulén wax "Sof" té boulén gueude wayé waxal ak gnom si téguine »
وَاخْفِضْ لَهُمَا جَنَاحَ الذُّلِّ مِنَ الرَّحْمَةِ وَقُل رَّبِّ ارْحَمْهُمَا كَمَا رَبَّيَانِي صَغِيرًا
« Té nangua soufel sa bope sén kanam ande ak yeurmandé té dilen gnanal « Yow Sama Borom, yeureum len gnom niars nagn ma yeureumé wone sa bamay néke liir »
Képe kouy deungué say wadiour do tékhé mouke té do am dara si sougnou tarikha bi.
Tabarani ak Ahmad nétali nagn bi hadith :
Béne way da nieuw si Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ néko : « amna khalé ( jeune homme) bouy kharkharlé( agonie) et nits gnangui koy beugue waxlo La Ilaha Illa Lahou, meunou ko wax »
Yonente ladjko : « daan na diouli ? »
Gnouniko waw, daan na diouli
« Daan na sarakhé ? »
Gnouniko waw
« Daan na woor ? »
Gnouniko waw
« Daan na djihad ? »
Gnouniko waw.
Dieufi tope Yallah yép daan nako déf bou dioub.
Am kou né « wayé kou bone si ndéyam lawone »
Yonente wolou Yayou xalé bi néko :
« sa doom bi bal ko, soko baloul safara la dieum »
Yaye dji néko : « na dém safara wayé doumako bal. Moma door ba loukhi sama beut bi »
Yonente néko : « balko, soko baloul safara la dieum »
Yaye dji né : « na dém safara wayé baloumako »
Yonente né : « takhagnal lén ma mate »
Gnou takhagn ko dior ko; mouni « tal lénko »
Gnou tal ko khambe bamou boy mouni : « sandi lén khalé bi si safara bi »
Yaye dji né : « sandi si bir safara ? Li takhoutone ma eumbe ko diourom nienti wér, nampal ko gnari ats, diko topato bamou mague nguén beugue ko sandi si safara ? »
Yonente néko : « boko baloul safara la dieum kay, gnou lake ko légui rek béne la »
Yaye dji né : « bal nako »
Bamkoy wax rek khalé bi né :
« أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَٰهَ إِلَّا ٱللَّٰهُ وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ ٱللَّٰهِ »
Kone ngua guiss né deungué say wadiour moy bopou moy Yallah té moy bountou tékhéadi.
Kou beugue boke si gnoune xamalni :
Haq bi gueneu for si yow moy haqqi Yallah tope si Haqqi gnaris wadiour.
Koudout matal gnars yi boko si tariqa bi.
Charte ba sa tégué moy :
…À Suivre…
Ruhul Adab 6
Baye néniou :
فَلَسْتَ
« Douwout »
فِي أَخْذِ
« Si diape »
الطَّرِيقِ
« Tariqa bi »
تَرْبَحُ
« Nguay amé tono(bénéfice) »
إِلَا
« Loumoy »
إِذَا كُنْتَ
« Si ngua néke »
دَوَامًا
« Si lou sakh »
تَصْلُحُ
« Di adji sélal »
Douwout né danguay diape tariqa bi rek tékhé wayé dangua wara sakh si sélal.
Sélal sa Islam moy dieufè ndiguel bayi téré :
أَقِيمُوا الصَّلَاةَ
“Takhawal len diouli mou dioube”
Yallah waxoul rek nè diouli lèn wayè dafani nagn ko dioubeul moy :
Diouliko si waxtou, mou ande ak labou ndokh, diouli ko si mbolo, matal chartes yi roukos yi ak soudiods yi, tèwlou li nguay diangue si diouli.
Koudout diouli, boko sougnou tariqa, koudout diouli, boko sougnou tariqa, koudout diouli boko sougnou tariqa.
أوصيكم بتقوى الله في السر و الجهر
« Mangui lén di dénke ragal Yallah si lou neubou ak lou fégne »
وأنني بالمتقى أباهى
«tè mane mangui titeuro si kou ragal Yallah»
Al Quran dafa ni :
Nits nieup perte nagne
إِلَّا الَّذِينَ آمَنُوا وَعَمِلُوا الصَّالِحَاتِ
“Loumoy gni geum tè dieuf dieuf diou sèle”
Dieuf diou sèle, moy tope ndiguel bayi tèrès.
Ndiguels yi def si lo meun, tèrès yi bayil yèpe.
Fouki (10) tèrès yi Yallah wax si sarou Al Anam ( ayats 151-152), bayi len yeup,
Mèl lèn melos yi Yallah wax si Sarou Fourqane ( Ayats 63 -74), sou boba dinguèn tonowo si diape gui nguène diape tariqa bi.
Kèpe kou beugue diot sa thiakoutef si Yallah, topal Yonente bi si dieufs aki djikos.
Waxou ma nak, tope tèy bayi euleuk, wayè dangua siy sakh ni sa nokis di sakhè.
Fi lèk sa noki bangui si yow, fi lèke sa khol mongui yeunguou, danguay sakh si tope ko, loloy sakh si sèlal.
Tariqa bi ndolal la, capital bi moy Islam si Charia. So si goorgoorlo tè sakhe si, twird bi meun la dieurigne.
Kouko dèfout nak :
فأشهد الله واشهدوا أني برىء منه و لا أبرأ منه إلاَّ بعد براءة الله و رسوله
« Sédélo na Yallah té sédé ni dégne na si mom( ki topoul ndiguel bawoul téré ) té douma dégne si mom loumoy guanaw ba Yallah ak Yonentam dégné si mom »
Guanaw bangua goorgoorlo si sa diné, ngua fékhé matal say diayanté si Tariqa bi, moy ngua matal Chartes yi ngua nangou wone.
Gnouni ko Baye :
Chartes yoyou gnoy yane ak nougnouy déf ba matal ko ?
Mouni :
….
À Suivre…
Ruhul Adab 5
Mouni :
Yallah moniou wax si Al Quran :
يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اذْكُرُوا اللَّهَ ذِكْرًا كَثِيرًا
« Yen gni geum, toude len Yallah toude gou beuri »
وَسَبِّحُوهُ بُكْرَةً وَأَصِيلًا
« Té nanguen ko sabal si soubeu ak si nguone( ganaw takussan) »
Doli négnou :
فَاصْبِرْ إِنَّ وَعْدَ اللَّهِ حَقٌّ وَاسْتَغْفِرْ لِذَنبِكَ وَسَبِّحْ بِحَمْدِ رَبِّكَ بِالْعَشِيِّ وَالْإِبْكَارِ
« Kone mougneul, ndakh li Yallah digué rek deugue la( louy tabi la), diégueloul say baakar et sabalal sa thiantag borom, goudi ak beuthieuk »
فَاصْبِرْ عَلَى مَا يَقُولُونَ وَسَبِّحْ بِحَمْدِ رَبِّكَ قَبْلَ طُلُوعِ الشَّمْسِ وَقَبْلَ غُرُوبِهَا وَمِنْ آنَاءِ اللَّيْلِ فَسَبِّحْ وَأَطْرَافَ النَّهَارِ لَعَلَّكَ تَرْضَى
« Mougneul li gnou lay wax ( si lou gnaw) et sabalal sa borom lata diante bi di fénke ak lata mo so ak si goudi gui. Naka magal Sabalam si gnari thiatou beuss bi, heyna ngua am sa thiakoutef »
وَاذْكُر رَّبَّكَ فِي نَفْسِكَ تَضَرُّعًا وَخِيفَةً وَدُونَ الْجَهْرِ مِنَ الْقَوْلِ
بِالْغُدُوِّ وَالْآصَالِ وَلَا تَكُن مِّنَ الْغَافِلِينَ
« Té nangua toude sa borom si sa bope, ande ak yar ak ragal ko, si yélou, si soubeu ak si nguone té boul boke si gnou saguanes gni »
Ak yénénis ayats. Al Quran mo gnou diguel waxtous yi.
Yonente néniou :
« Képe kou diouli fadjar si mbolo, tog di toudou Yallah ba diante bi fénke, diouli gnari rakats, dingua am si yol lou mélni Hajj ak Oumra »
Yonente waxat gnou :
« Tog ak gnay toude Yallah guanaw Fadjar ba diante bi fénke mo ma gueneul gorél nienti diames si domis Isma’il yi, té tog ak gnay toude Yallah guanaw takussan ba diante bi so moma gueneul gorél nientis diam »
Lii moy wird Tidiane mo takh manila fondement nagnko si Sunna ak Al Quran bi di adji tékhalé diguentè deugue ak nar.
Guanaw bangua khamé li néke si diayanté ( engagement) ak liy thiossanou tariqa bi si Al Quran ak Sunna, soko nanguo ba soubossi, mangui lay dénke :
وَلَازِمُواْ
«Té nangua sakhal( takho) »
لَازِمَ
« Li gnou sakhal( wird Lazime) »
ذِي الطَّرِيقِ
« Mou gnéwal tariqa bii »
بِذَا
« Si lolou ( sakhal gui) »
يُنَالُ
« Nguay amé »
الرِّبْحُ
« Tono ( bénéfice) »
بِالتَّحْقِيقِ
« Si deugue deugue »
Gnouniko : Baye, khana tariqa bi, dou so si dougué rek garantie nagn la ?
Mouni :
Gnoune, douwout gnou Serignes youy gadoul séni talibés Al Diana.
Dégloulen ma waxlen lou lén di takha am li nguén beugue si tariqa bi.
Mouni :
……À Suivre….
Rouhoul Adab 4
Baye négnou :
Yallah mo gnou wax ni :
الصَّابِرِينَ وَالصَّادِقِينَ وَالْقَانِتِينَ وَالْمُنفِقِينَ وَالْمُسْتَغْفِرِينَ بِالْأَسْحَارِ
« Gnoy adji mougne yi, di adji deugou yi, di adji tope yi, di adji sarakhé yi té gnoy diégueloukatou Yallah yi si waxtou ndieul( avant fadjr) »
Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ néniou :
أقْرَبُ مَا يَكُونُ الرَّبُّ مِنَ العَبْدِ، فِي جَوْفِ اللَّيْلِ الآخِرِ؛ فَإنْ اسْتَطَعْتَ أنْ تَكُونَ مِمَّنْ يَذْكُرُ اللهَ فِي تِلْكَ السَّاعَةِ؛ فَكُنْ
« Si waxtou you moudie si goudi gui la Yallah di geuneu diégué diamam bi. So meuné boke si gnikoy toude waxtou bobou, boke si »
Yallah diguel nagnou diéguelouko wayé tamit khassal nako waxtou, moy ndieul ( avant fadjar), mo takh suñu wird bi, gnou tamou si Istighfar bala fadjar.
Mo takh gnouy diayanté Istighfar avant Fadjar, nguir boke si gnoukoy dieufé.
Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ waxna gnou :
يَا أَيُّهَا النَّاسُ تُوبُوا إلَى اللهِ، فَإِنِّي أتُوبُ إلَيْهِ مِئَةَ مَرَّةٍ
Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ néna :
« Yén nits gni, déloulén si Yallah téy dieguelou ndakh mane mi , damay diéguelou Yallah 100 yoone si beuss bou néke »
Mo takh gnou diape diko déf 100 fois
Yallah délou négnou :
إِنَّ اللهَ وَمَلاَئِكَتَهُ يُصَلُّونَ عَلَى النَّبِيِّ يَا أَيُّهَا الَّذِينَ ءَامَنُواْ صَلُّواْ عَلَيْهِ وَسَلِّمُواْ تَسْلِيمًا﴾
« Yallah ak ay mala’ikam dagnouy diouli si Yonente ( diouli goudoul dake), yén gni guem, diouli lén si mom té nguen di seulmeul( nguir sen lote) »
Yonente négnou :
من صلَّى عليَّ صلَّى اللهُ عليه عشرًا ووكَّلَ بها ملَكًا حتى يُبَلِّغَنيها
« képe kou diouli si mane béne yoon, Yallah diouli si yow 10 yoon té dina wakil Mala’ika mou sakhal diouli gui ba bama siy diote »
Mo takh gnou sakhal Salatou Ala Nabi 100 fois si waxtou ndieul.
Yallah délou néniou :
فَاعْلَمْ أَنَّهُ لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ وَاسْتَغْفِرْ لِذَنبِكَ
« khamal ni, La Ilaha illa Lahou, té ngua toube say bakars »
Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ négnou :
يا أيها الناس ! قولوا لا إله الا الله تفلحوا
« Yén nits gni, waxlen La Ilaha Illa Lahou nguir nguen tékhé »
Mou waxgnou si bénén hadith :
« Képe kou wax La Ilaha Illa Lahou 100 yoon si beuss….. kéne douko eupeulé yool loumoy kou déf louko eupe »
Ak yénén ayats aki hadiths.
Yonente صَلَّىٰ اللّٰهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ khamni dagno kheur si mbakh, mou beugue gno nopal négnou :
أَنَّ أَحَبَّ الأَعْمَالِ أَدْوَمُهَا إِلَى اللَّهِ، وَإِنْ قَلَّ
« Dieuf gou Yallah geuneu sope, moy bou sakh, dilé né lou néw la »
Mo takh Cheikh négnou :
Yonente diguel nama, nagnouy sakhal li si waxtou ndieul :
Istighfar 100x
Salatou Ala Nabi 100x
Tahlil( La iLaha Illa Lahou) 100x
Lolou mo takh gnou toudé ko Lazim, mouy dieuf dioy sakhal.
Gnouniko : Baye, lazime takussan bi nak ?
Mouni :
….À Suivre….
N•2
Mouni :
مِنْ بَعْدِ
« Si ganaw »
بِاسْمِ اللهِ
« bi ma toudé Yallah si Basmallah »
ثُمَّ
« Tope »
الْـحَمْدِ
« Bi ma waxé ni gnentis khadiou thiante yeup »
لِلّٰهِ
« Gnéwal na Yallah »
Bama diangué ba guiss hadith biy waxni :
كل أمر ذي بال لا يبدأ ببسم الله فهو أقطع (أو أبتر)
« Bépe mbir bou am solo bou tambaléwoul Bismillah lou dague ( matadi) la ( wala amoul barké) »
Am riwaya bou nieuw né : الحمدلله
Am riwaya bou nieuw né : فيه بذكر الله
Ma ni nagn def li geuneu mate moy bolé yeup ndakh Basmallah ak Hamdallah, toude Yallah la té barkéb Bismillah ak nguenélou Al Hamdoulillahi, nieuw na si Al Quran nieuw si Hadith.
Ma dieulé si Tafsir Qurtubi ak Durrul Manthur, volume 1 page 9, né dieulé nagn si Ibn Masoud né :
بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ
19 arafs la, beuke négou Jahannam 19 lagne, képe kou wax Basmallah té guem ko, 19 beuke négs yi kéne doula si meuna douguel safara.
Sougn ko topé dougnou wéy ndakh gnari bates yoyou lignou lambo si nguenel.
Ma royalé si mags gnou bakh gni
Yallah momou may toude diko sante moy kane :
ذِي الطَّوْلِ
« Kadi borom mays you yatou yi »
الْعَظِيمِ المَجْدِ
« Kadi adji mague tédangué »
نَصِيحَةٌ
« Lii ab layé biir la »
مِنِّي
« Bou touké si mane »
إِلَى إِخْوَانِي
« Dieum si samay mbokes ( dioulits) »
Yonente waxone nagnou né :
إنّ الدِّين النَّصيحةُ
« Diné, moy layé bir »
Mo takh ma dieufé ndiguel, né na layeé biir samay mbokes. Ana louma len di layé biir ?
فَلْتُمْسِكُواْ
« Na nguén diape( ngoye) »
طَرِيقَةَ التِّجَانِي
« Si yonou Cheikh Ahmad Tidiane ( Tariqa Tidiane) »
Lou takh gnou war si diape ?
….À suivre…
Cliquez ici pour réclamer votre Listage Commercial.
Vidéos (voir toutes)
Type
Site Web
Adresse
Dakar
HLM Maristes
Dakar
Wundu Graphy est une société individuelle créée afin d'octroyer des services dans le secteur de
Dakar
Réinventons le Digital Africain ! Solidarité , Créativité , et forte Résilience ! Une Agence Di
3 Avenue Cheikh Anta Diop BP
Dakar, 11000
passion pour les relations saines et bon plaisir propre nous a inspiré à créer Jareveo, l’entre
Allées Cheikhna Cheikh Sidaty
Dakar
création de site web professionnel 🇸🇳 pour entreprise, organisation au Sénégal...
Dakar
Pour vos besoins en formation sur les TIC, en Cybersécurité et en produits et services High-Tech.
Dalifort, Mairie
Dakar, 10500
#Boss_Design💻 is at your disposal for Logo creations, AD displays; Presentation Videos and Menus.
Dakar, 11000
Notre entreprise est spécialisée dans la création de site internet et de logos professionnels
Mbao
Dakar
Nous vous offrons plus que du digital, nous vous offrons l'art du marketing dans toutes ses formes.
Dakar, 12500
-Interior Design🛋 -Création des espaces uniques et élégants🏠 - Sublimer vos espaces ✨
Dakar Point E
Dakar
Le luxe des meubles sur mesure à la portée de tous ! #Création #Inspiration #Artisanat #MadeInS?